Chants en wolof

Cant 1. Dara mënu noo tàggaleek mbëggeelam (2:07)

      Track 01

Dara mënu noo tàggaleek mbëggeelam (2x)

Du dund te du dee, loolu wóor na leen.
Du xiif te du mar, loolu leer na leen.

Du ñàkk te du am, loolu wóor na leen.
Du naqar te du mbég, loolu leer na leen.

Ndax Yàlla jox na nu Yeesu sunu Buur
Ndax Yàlla jox na nu Yeesu sunu Buur

Cant 2. Ñaanleen, ñu may leen (1:10)

      Track 02

Yeesu ne na ñaanleen, ñu may leen
(Ñaanleen, ñu may leen)
Seetleen, te dingeen gis
(Seetleen, dingeen gis)
Fëggleen, ñu ubbil leen
(Fëggleen, ñu ubbil leen)
Yeesu ne na ñaanleen, ñu may leen
(Ñaanleen, ñu may leen)
Seetleen, te dingeen gis
(Seetleen, dingeen gis)
Fëggleen, ñu ubbil leen
(Fëggleen, ñu ubbil leen)

Ndaxte kuy ñaan, dinga am
Te kuy seet, dinga gis
Kuy fëgg, ñu ubbil la.
Aléluya, Amiin
Ndaxte kuy ñaan, dinga am
Te kuy seet, dinga gis
Kuy fëgg, ñu ubbil la.
Aléluya, Amiin
(Lukk 11:9)

Cant 3. Boroom bi Yàlla (1:38)

      Track 03

Boroom bi Yàlla
Aji Kàttan ji
Moom mi ki sell, sell ki sell
Moom mi ki nekkoon dèmb
te nekk tey
Te dina ñëw ëllëg
Ngir yobbu ñu ci Baay bi
Te dina ñëw ëllëg
Ngir yobbu ñu ci Baay bi

Pour la fin ..
Te dina ñëw ëllëg
Ngir yobbu ñu ci Baay bi
(Peeñ Bi 4)

Cant 4. Baay bi gore na (3:10)

      Track 04

Sunu Yàlla gore na, waawaaw
Sunu Baay bi gore na.   (2x)

Baay bi gore na, waawaaw
Doom ji gore na.  (awu)         (2x)
Doomu Yàlla ji baalal nu.
Doomu Yàlla jee baalal nu.  (2x)

1. Saaga nañu la ngir nun
Dóor nañu la ngir nun
Tufli nañu la ngir nun
Fitnaal nañu la ngir nun (2x)

2. Yeew nañu la ngir nun
Daaj nañu la ngir nun
Jam nañu la ngir nun
Tuur sa deret ngir nun  (2x)

Cant 5. Pàppa, sant nanu la (2 :18)

      Track 05

Pàppa, sant nan’ la,
màggal nan’ la, Aléluya.  (2x)

1. Li nga def ci àddina, lenn la fi, dootu fi ñaar
Ki nga maye ci àddina, kenn la fi, dootu fi ñaar
Moo di Yàlla, moo di Buur, moo di Xel mu Sell mi. (2x)

2. Yeesu mi nga maye ci àddina, kenn la fi, dootu fi ñaar
Dee na ca bant ba, ngir musal waa àddina
Moo di Yàlla, moo di Buur, moo di Xel mu Sell mi. (2x)

3. Yeesu mi nga maye ci àddina, kenn la fi, dootu fi ñaar
Mat na Baay, te donn na Baay, moo di Xel mu Sell mi
Moo di Yàlla, moo di Buur, moo di Xel mu Sell mi. (2x)

Cant 6. Yàlla miy kenn (1:27)

      Track 06

Yàlla miy kenn
Di sunu Musalkat
Na yelloo ndam ak màgg, kàttan ak nguur
Jaar ci Yeesu Krist sunu Boroom
Démb, tey, ëllëg ba fàww
Amiin, amiin.
(Yudd 25)

Cant 7. Yeesu du soppiku mukk (1:12)

      Track 07

Yeesu du soppiku mukk
Yeesu du soppiku
Yeesu du soppiku mukk
Yeesu du soppiku

Ni mu mel
Démb ak tey
lay mel ba fàww

Ni mu mel
Démb ak tey
lay mel ba fàww

Ni mu mel
Démb ak tey
lay mel ba fàww

Ni mu mel
Démb ak tey
lay mel ba fàww
Yawut 13:8

Cant 8. Gëmleen Yàlla te gëm ma  (2:35)

      Track 08

Maa ngi leen di wax, Buleen jàq
Gëmleen Yàlla te gëm ma (2x)
Sama këru Baay, am na néeg yu bare [Awu] (2x)

Maa ngi waajali fu ngeen di dëkk [Awu] (2x)

Bu paree, ma jëlsi leen [Awu] (2x)

Ma yóbbu leen ba fu ma nekk [Awu] (2x)

Fa ma jëm, xam ngeen yoon wi [Awu] (2x)

Man maa di yoon wi [Awu] (2x)

Man maa di dëgg gi [Awu] (2x)

Man maa di dund gi [Awu] (2x)

Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man [Awu] (2x)

Cant 9. Yàlla Màgg na! (4 :51)

      Track 09

Yàlla màgg na!  Yàlla màgg na!
Yàlla ku sell,   Yàlla ku sell    la!
Aji Mbëggeel la.  Aji Mbëggeel la.
Yàlla du soppiku, Yàlla du soppiku mukk!

Céy Buur Yàlla, yaay Aji Sell ji (2x)
Ba mënuloo   xool lu bon. (2x)
Céy Buur Yàlla, yaay Aji Jub ji. (2x)
Def nga sa yoon   muy yoon wu mat. (2x)

Céy Buur Yàlla, yaay Aji Mbëggeel ji. (2x)
Moo tax nga xamle   xebaar bu baax bi. (2x)
Feeñal nga pexe   mu raw xalaatu nit, (2x)
Ngir musal  bàkkaarkat yi. (2x)

Céy Buur Yàlla, yaay Aji Màgg ji (2x)
Sa xel mu rafet   ni mu xóote. (2x)
Céy Buur Yàlla, yaay sàmm kóllëre, (2x)
Mënuloo tebbi   li nga dige. (2x)

Céy Buur Yàlla, def nga li nga waxoon (2x)
Jaarale ko  ci yonent yi. (2x)
Wàcce nga sa Ruu – sa Kàddu doon nit. (2x)
Te noonu nga   nu walloo. (2x)

Cant 10. Aléluya  (2:15)

      Track 10

Aléluya, Aléluya, Aléluya Yeesu Aléluya (4x)

Nit ñi gëmleen Yeesu, Aléluya (2x)
Moom mooy Musalkat bi, Aléluya (2x)
Day musal ci àddina Aléluya (2x)

Aléluya Yeesu, Aléluya
Aléluya, Aléluya, Aléluya Yeesu, Aléluya

Yàlla may nu doole (2x)
Barkeel sunu jiw bi (2x)
Barkeel lu ñu ji (2x)

Ku gëm Yeesu nga dem ci dex gu sedd gi
Ku gëm Yeesu  (2x)

Aléluya, Aléluya, Aléluya Yeesu Aléluya (2x)

Cant 11. Rëdd Naa Sa Tur  (3:20)

      Track 11

Yérusalem wax na ne:  Yàlla bërgël na ma.
Sama Boroom, sama Boroom dafa ma fàtte.
Bi Yérusalem jooyee loolu,
jooyee metitam woowu,
Yàlla Aji Sax ji  tontu na Yérusalem

Ndax jigéen mën na fàtte doomam ji muy nàmpal?
Ndax du am yërmande ci doomam ji mu jur?
Bu jigéen fàtte woon sax, man duma la fàtte mukk?
Say miir ñu ngi saa yu nekk ci sama kanam.

Xoolal, dama rëdd sa tur, rëdd naa sa tur,
ci sama ñaari loxo.
Say miir ñu gi saa yu nekk ci sama kanam-oo.
Naka laa la mën a fàttee?
(Esayi 49: 14-16)

Cant 12. Kaayleen Nu Gëm Kéemaanu Yàlla Gii  (3 :09)

      Track 12

Kaayleen nu gëm kéemaanu Yàlla gii. (2x)
Ab janq wasin na Buuru buur yi. (2x)
Mooy Musalkat bi di sunu Boroom. (2x)
Yeesu mayug Yàlla la ci àddina si. (2x)

1. Buur bi juddu mooy Buuru buur yi.
Indil na nu njub ak yiwu Yàlla.
Wàcc na ci suuf mu ganesi nu.
Won nu ni nu war a dunde.

2. Buur bi juddu ci nguuru leer gi,
Ngir daaneel buuru lëndëm gi.
Tuur na deretam ndax sunuy bàkkaar.
Tas na dooley Ibliis, may nu ndam.

3. Buur bi ci nguuru Dawuda la juddu,
Mooy nguur giy sax ba abadan.
Na ko malaakay Yàlla jaamu!
Nun itam, danu koy màggal.

Cant 13. Emanuwel

      Track 13

Emanuwel, Doomu Yàlla la. (2x)

1. Moom la Yàlla yónni , ngir mu musal nu. (2x)

2. Moom la Yàlla yónni , ngir mu aar nu. (2x)

3. Moom la Yàlla yónni , ngir mu tette nu. (2x)

4. Moom la Yàlla yónni , ngir mu gindi nu. (2x)

Cant 14. Biddiiw Ba Fenk Na

      Track 14

Fenk na, biddiiw ba fenk na. (3x)
Isaa juddu na, te Jibril moo ko yégle.
Yàlla moo ko jox tur.  Kaayleen nu jaamu ko.
Kaayleen nu siyaare.  Kaayleen nu jaamu ko.

Sell na, xale ba sell na. (3x)
Isaa leer la.   Leeru Yàlla la.
Yàlla moo nu ganesi.  Kaayleen nu jaamu ko.
Kaayleen nu siyaare.  Kaayleen nu jaamu ko.

Bi Elisabett nekkee ci juróorm-benni weeram
Yàlla yóoni malaakaam Jibril ca dëkku Nasarett ca diiwanu Galile.
Mu yebal ko ca janq, bu tudd Maryaama.
Malaaka ma ne ko:
Yàlla tànn na la ci yiwam
Dinga ëmb, jur doom ju góor.
Nanga ko tudde Yeesu.            (Lukk 1:26,27, 30, 31)

Bi nga xamee ne, Yeesu juddu na ci Betleyem
Ci diiwaanu Yude
Amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yérusalem.
Ñu ne: Ana buur bi juddul Yawut yi?
Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku, te ñëw nanu ngir màggal ko.
Noonu, ñu dugg ca kër ga,
Gis xale ba ak Maryaama ndeyam,
Ñu daldi sukk, di ko màggal.            (Macë  2:1,2,11)

Cant 15. Ay Boroom xam-xam ñëw nañu, màggalsi Yeesu (3:12)
(Macë 2:1-11)

      Track 15

Cant 16. Siyaareleen (2:04)

      Track 16

Siyaareleen, siyaareleen
Siyaareleen, man siyaare naa ko. (4x)

Buuru àddina juddu na    [Doomu Yàlla juddu na]
Buuru àddina juddu na.    [Sunu sàmmkat juddu na]
Buuru àddina juddu na.    [Sunu Musalkat juddu na]

Finale      [Kon] Siyaareleen, siyaareleen
Siyaareleen, man jébbalu naa. (2x)

Cant 17. Sargal nga ma  (3 :05)

      Track 17

Baayoo Baayoo maa ngi lay màggal
di la sant te di la gërëm (2x)
Ndax Baayoo Baayoo sargal nga ma (2x)
Fu mu jafee nga yombalal ma ko
Fu mu mettee nga woyafal ma ko
Fu mu diise nga may ma doole
Fu ma juume nga won ma yoon wi
Kon, Baayoo Baayoo sargal nga ma (2x)
Fu mu jafee nga yombalal ma ko
Fu mu mettee nga woyafal ma ko
Fu mu diise nga may ma doole
Fu ma juume nga won ma yoon wi
Kon, Baayoo Baayoo sargal nga ma (2x)
Baayoo Baayoo ci barke Yeesu
Yaa ngi may aar te di ma tette
Baayoo Baayoo ci barke Yeesu
May nga ma xel, may nga ma doole
Kon, Baayoo Baayoo sargal nga ma (2x)

Cant 18. Woyu Maryaama (3:10)

      Track 18

Refrain:    Noonu Maryaama daldi ne: (2x):

Sama xol a ngi màggal Boroom bi, (2x)
Sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat. (2x)

Ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.
Turam dafa sell, dafa sell, dafa sell-a-sell.(2x)

Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal, (2x)
Ci seeni sët __  ba ci seeni sëtaat.(2x)

Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex, (2x)
Te dàq boroom alal yi, (2x)
Ñu daw ak loxoy neen.(2x)

Sama xol a ngi màggal Boroom bi, (2x)
Sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat. (2x)
Sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat. Waaw!
Sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat. Ooooo!

Cant 19. Bàyyileen xale yi ñu ñëw ci man (4:02)

      Track 19

Bàyyileen xale yi ñu ñëw ci man
Ndaxte ñoom ñoo moom nguuru Yàlla
Ñu mel ni ñoom ñoo moom nguuru Yàlla. (4x)

Ki di taalibe, ki di doomu buur, ki di doomu baadoola
Ndax ñoom ñépp duñu benn ci kanamu Yàlla?

Bàyyileen xale yi ñu ñëw ci man
Ndaxte ñoom ñoo moom nguuru Yàlla
Ñu mel ni ñoom ñoo moom nguuru Yàlla. ….

Chants Wolof 20-32

Cant 20

      Track 01

Cant 21

      Track 02

Cant 22

      Track 03

Cant 23

      Track 04

Cant 24

      Track 05

Cant 25

      Track 06

Cant 26

      Track 07

Cant 27

      Track 08

Cant 28

      Track 09

Cant 29

      Track 10

Cant 30

      Track 11

Cant 31

      Track 12

Cant 32

      Track 13

 

Chants Wolof 20-32

Leave a Reply

Your email address will not be published. Required fields are marked *

You may use these HTML tags and attributes: <a href="" title=""> <abbr title=""> <acronym title=""> <b> <blockquote cite=""> <cite> <code> <del datetime=""> <em> <i> <q cite=""> <strike> <strong>

Current month ye@r day *